عَنِ الْبَرَاءِ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَا مِنْ مُسْلِمَيْنِ يَلْتَقِيَانِ فَيَتَصَافَحَانِ إِلَّا غُفِرَ لَهُمَا قَبْلَ أَنْ يَفْتَرِقَا».
[صحيح بمجموع طرقه] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن أبي داود: 5212]
المزيــد ...
Jële nañu ci Al-Baraa yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"amul ñaari jullit yuy daje daal di joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal laata ñuy teqalikoo".
[Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 5212]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne: amul ñaari jullit yuy daje ci aw yoon mbaa lu ko niru kenn ki nuyu keneen ki ñu joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal njëkk ñuy taqalikoo.