+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ:
عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ: «قَالَ اللَّهُ: كَذَّبَنِي ابْنُ آدَمَ وَلَمْ يَكُنْ لَهُ ذَلِكَ، وَشَتَمَنِي وَلَمْ يَكُنْ لَهُ ذَلِكَ، فَأَمَّا تَكْذِيبُهُ إِيَّايَ فَقَوْلُهُ: لَنْ يُعِيدَنِي، كَمَا بَدَأَنِي، وَلَيْسَ أَوَّلُ الخَلْقِ بِأَهْوَنَ عَلَيَّ مِنْ إِعَادَتِهِ، وَأَمَّا شَتْمُهُ إِيَّايَ فَقَوْلُهُ: اتَّخَذَ اللَّهُ وَلَدًا وَأَنَا الأَحَدُ الصَّمَدُ، لَمْ أَلِدْ وَلَمْ أُولَدْ، وَلَمْ يَكُنْ لِي كُفْؤًا أَحَدٌ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 4974]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-:
Jële na ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Yàlla nee na:doomu Aadama weddi na ma te loolu waru ko woon,mu saaga ma te waru ko woon,weddi gi mu ma weddi mooy,li mu wax ne: du ma dellóosiwaat,kem ni mu ma tàmbalee woon,te mbind mu njëkk gënut a doyadi fi man delloosiwaat ko,saaga gi mu ma saaga mooy, wax ji mu wax ne :Yàlla am na doom,te man maay kenn ki ñépp jublu, juruma kenn te kenn juru ma, te amuma benn nawle".

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4974]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ci hadiisul xudsiy bii ne Yàlla mu màgg mi dafa xibaare ne bokkaalekat yi ak yéefar yi dañu koo weddi di ko melal ci ay wàññiku ak i ayib, te loolu jaaduwul ci ñoom.
Bu dee seen weddi gi ñuy weddi Yàlla: mooy li ñu defe ne Yàlla du leen dellóosiwaat ginnaaw bu ñu faatoo, kem ni mu leen binde woon ca yoon wu njëkk wa ñu jóge cig ñàkk,mu weddi leen ci ne ki sos mbind mi cig ñàkk am na kàttanu dellóosiwaat ko te sax moo gën a woyof,donte bu dee ci Yàlla bind gi ak dellóosi gi ñoo yam, ndax Yàlla lépp la man.
Bu dee saaga gi: mooy li ñu wax ne: am na doom, mu weddi leen ci ne moom mooy kenn ki wéet te mat sëkk ci ay turam ak i meloom ak i jëfam, di ki set ci géppug wàññiku ak ayib, mooy ki ñuy jublu soxlawul kenn, te ñépp soxla ko, du way-juru kenn, te du doomu kenn,te amul benn nawle mbaa niróowaale moom Aji-Sell ju kawe ji.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Saxal matug kàttanu Yàlla mu kawe mi.
  2. Saxal dekki ginnaaw dee.
  3. Képp kuy weddi dekki walla muy askanale Yàlla doom ab yéefar la.
  4. Yàlla amul niróowaale amul ku ñu koy xoole.
  5. Yaatuwaayu lewetug Yàlla mu sell mi, ak ni muy néggandikoo yéefar yi ndax amaana ñu tuub dellu ginnaaw.