عَن عَبْدِ اللهِ بْنِ عَمْرِو بْنِ الْعَاصِ رضي الله عنهما أَنَّهُ سَمِعَ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، يَقُولُ:
«إِنَّ قُلُوبَ بَنِي آدَمَ كُلَّهَا بَيْنَ إِصْبَعَيْنِ مِنْ أَصَابِعِ الرَّحْمَنِ، كَقَلْبٍ وَاحِدٍ، يُصَرِّفُهُ حَيْثُ يَشَاءُ» ثُمَّ قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «اللهُمَّ مُصَرِّفَ الْقُلُوبِ صَرِّفْ قُلُوبَنَا عَلَى طَاعَتِكَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2654]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu dégg Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
"xoli doomi Aadama yépp ñoo ngi ci diggante ñaari baaraam ci baaraami Yàlla miy Yërëmaakoon bi, mel ni benn xol, mu koy wëlbati jëme fu ko soob" topp Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: "yaw sama Boroom Aji-Wëlbati xol yi jëmaleel sunu xol yi ci topp la".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2654]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne xoli doomi Aadama yépp ñoo ngi ci diggante ñaari baaraam ci baaraami Yàlla miy Aji-Yërëme mel ni benn xol, mu koy jëmale fu ko soob; bu ko soobee mu jubal ko ci dëgg, bu ko soobee mu jengal ko wolif dëgg ga, te ag wëlbateem ci xol yépp day mel ni wëlbati benn xol, benn mbir su ko soxlaal moom Aji-Sell wolif beneen mbir, topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ñaan, wax ne: yaw sama Boroom miy Aji-Wëlbati xol yi leeg-leeg mu jëm ci ag topp, leeg-leeg mu jëm ci ag moy, leeg-leeg ci sikar leeg-leeg ci càggante, jëmaleel sunu xol yi ci topp la.