+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ:
قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «إِنَّ اللَّهَ قَالَ: مَنْ عَادَى لِي وَلِيًّا فَقَدْ آذَنْتُهُ بِالحَرْبِ، وَمَا تَقَرَّبَ إِلَيَّ عَبْدِي بِشَيْءٍ أَحَبَّ إِلَيَّ مِمَّا افْتَرَضْتُ عَلَيْهِ، وَمَا يَزَالُ عَبْدِي يَتَقَرَّبُ إِلَيَّ بِالنَّوَافِلِ حَتَّى أُحِبَّهُ، فَإِذَا أَحْبَبْتُهُ: كُنْتُ سَمْعَهُ الَّذِي يَسْمَعُ بِهِ، وَبَصَرَهُ الَّذِي يُبْصِرُ بِهِ، وَيَدَهُ الَّتِي يَبْطِشُ بِهَا، وَرِجْلَهُ الَّتِي يَمْشِي بِهَا، وَإِنْ سَأَلَنِي لَأُعْطِيَنَّهُ، وَلَئِنِ اسْتَعَاذَنِي لَأُعِيذَنَّهُ، وَمَا تَرَدَّدْتُ عَنْ شَيْءٍ أَنَا فَاعِلُهُ تَرَدُّدِي عَنْ نَفْسِ المُؤْمِنِ، يَكْرَهُ المَوْتَ وَأَنَا أَكْرَهُ مَسَاءَتَهُ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 6502]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla nee na: ku noonook sama péete yégal naako ab xare, sama jaam bi du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom, sama jaam bi du deñ dima jéema jege ci ay naafila ba ma bëgg ko, te bu ma ko bëggee, maay nekk déggam gi muy dégge, ak gisam gi muy gise, ak loxoom bi muy jàppe, ak tànkam bi muy doxe, bu ma ñaanee ma may ko,bu ma musloo ma musal ko, du ma dengi-dengi ci dara lu may def, samag dengi-dengi mi ngi ci bu may jël bakkanu aji-gëm ji, ndax day bañ a dee,te man dama koy bañ a def lu mu bëggul».

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6502]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day xibaare ci hadiis bu sell bii ne Yàlla mu màgg nee na: Ku lor kenn ci wàlliyu ci sama péete yi merloo ko bañ ko yégal naa ko te ko ag nooneel.
Péetem Yàlla mooy: aji-gëm ju ragal Yàlla ji, ci kem li nekk ci jaam bi ci ngëm ak ragal Yàlla loolu mooy céram ci nekkam péetem Yàlla. Jullit bi du jegeñ-jegeñlu Boroomam lu ko gënal li mu farataal waral ko ci moom ci ay jaamu ak bàyyi yu araam yi, te jullit bi du deñ di jegeñ-jegeñlu Boroomam ci ay naafila boole ko ak farata yi; ba daal di am mbëggeelug Yàlla. Bu ko Yàlla bëggee Yàlla dana ko jubal ci ñenti cér yii:
Dana ko jubal ci ag déggam, du dégg lu dul luy gërëmloo Yàlla.
Dana ko jubal ci ag gisam, du xool lu dul lu Yàlla bëgg ñu xool ko te mu gërëmloo ko.
Dana ko jubal ci loxoom, du jëf ci loxoom lu dul luy gërëmloo Yàlla.
Dana ko jubal ciy tànkam, du dox jëm ci lu dul luy gërëmloo Yàlla, te du dox jëm ci lu dul lu am aw yiw.
Ànd ak lii bu ñaanee Yàlla dara Yàlla jox ko li mu laaj, mu nekk ku ñuy nangu ñaanam, bu musloo ci Yàlla làqu ci moom, ngir sàkku kaarànge Yàlla musël ko aar ko ci li muy ragal.
Yàlla mu kawe mi daaldi wax ne: duma dengi-dengi ci dara lu may def, samag dengi-dengi mi ngi ci bu may jël bakkanu jullit bi ndax li ma ko yërëm; ndaxte moom day bañ dee ndax li ci nekk ci mettit, te Yàlla day bañ luy metti aji-gëm ji.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Hadiis bii dafa bokk ci li Yonnente bi nettali jële ko ci Boroomam, ñu di ko woowe Hadiis Al-xuddsi walla Hadiisu Al Ilaahiy, te mooy Hadiis bi nga xam ne ay baatam ak i maanaam ci Yàlla la jóge, waaye amul jagle yi nekk ci Alxuraan te mu koy ràññetle ak lu dul moom, niki di jaamu Yàlla ci jàng gi ak di laab ngir jàng ko, ak di ci dëkke mbaa di ci lottloowaate ak yenneen.
  2. Tere nañu lor péetey Yàlla yi, xemmemloo nañu it ñu bëgg leen, te nangu seen ngëneel.
  3. Digle nañu ñu noonoo nooni Yàlla yi, te baña féete ak ñoom.
  4. Kuy wootewoo ne péetem Yàlla la te du topp sariihaam ji kooku ab fenkat la ci li muy wootewoo.
  5. Ci def yi Yàlla waral, ak bàyyi yi mu araamal lañuy nekkee péetem Yàlla.
  6. Bokk na ci liy tax Yàlla bëgg jaam bi, di nangu ñaanam, def naafila yi ginnaaw bi ñu taxawee ci def yi war ak bàyyi yi araam.
  7. Tegtale teddngay niti Yàlla yi ak kaweg seen i wàccuwaay.