عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«اثْنَتَانِ فِي النَّاسِ هُمَا بِهِمْ كُفْرٌ: الطَّعْنُ فِي النَّسَبِ، وَالنِّيَاحَةُ عَلَى الْمَيِّتِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 67]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"ñaar a ngi ci nit ñi ag kéefar la: jam ci askan yi, ak yuuxu ku dee".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 67]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne am na ñaari melo yu nekk ci nit ñi te ci jëfi yéefar yi ak jikkóy ceddo ga la bokk, ñoom ñaar ñooy:
Bi ci njëkk: jam ci askani nit ñi ak xeeb leen ak rëy-rëylu ci seen kaw.
Ñaareel bi: yëkkëti kàddu ci musiba ngir mer ci dogal li, walla xotti ay yére ngir tarug njàqare.