عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ حَلَفَ فَقَالَ فِي حَلِفِهِ: وَاللَّاتِ وَالعُزَّى، فَلْيَقُلْ: لاَ إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ، وَمَنْ قَالَ لِصَاحِبِهِ: تَعَالَ أُقَامِرْكَ، فَلْيَتَصَدَّقْ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4860]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«ku giñ daal di wax: giñ naa ci
Laata ak Hussaa, na wax: laa ilaaha illal-Laahu, ku wax àndandoom ne ko: kaay ñu kàrt na saraxe».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4860]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day moytandikuloo giñ ci ku dul Yàlla; ndax jullit du giñ ci ku dul Yàlla, Muy xamle ne ku giñ ci ku dul Yàlla; niki ku wax: giñ naa ci Laata ak Hussaa -ñaari xërëm lañu yu ñu doon jaamu ca ceddo ga lu jiitu lislaam - war na ci moom mu dabaatal ko daal di wax: laa ilaaha illal-Laahu, ngir set wicc ci bokkaale, ak kaffaara ngiñam loolu.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xibaare ne ku wax àndandoom ne ko: kaay ñu fo ci kaart, -te mooy ñaar walla lu ko ëpp rawante teg alal ci seen diggante ku not jël ko, te manul ñàkk kenn ci ñoom ñaar gañe walla mu ñàkk-, kon sopp nañu mu saraxe dara ngir kaffaara loolu mu woote.