+ -

عَنْ سَعْدِ بْنِ أَبِي وَقَّاصٍ رضي الله عنه عَنْ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنَّهُ قَالَ:
«مَنْ قَالَ حِينَ يَسْمَعُ الْمُؤَذِّنَ أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَحْدَهُ لَا شَرِيكَ لَهُ، وَأَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُهُ وَرَسُولُهُ، رَضِيتُ بِاللهِ رَبًّا وَبِمُحَمَّدٍ رَسُولًا، وَبِالْإِسْلَامِ دِينًا، غُفِرَ لَهُ ذَنْبُهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 386]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Sahd Ibn Abii Waqaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne:
«kuy wax saa yu déggee noddkat bi, ashadu an laa-i-Laaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu, wa anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu, radiitu billaahi rabban, wa bi Muhammadin rasuulan, wa bil Islaami diinan, dees na ko jéggal ay bàkkaaram».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 386]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne kuy wax bu déggee noddkat bi: "ashadu an laa-i-Laaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu" maanaam:maa ngi saxal di nangu di gëm ne amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla,te lépp lu ñuy jaamu ku dul Yàlla ag neen la, "wa anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu"maanaam: Muhammat ab jaam la deesu ko jaamu,ndawul Yàlla la te du fen, "radiitu bil Laahi rabban"maanaam:gërëm muy naa Yàlla muy buur cig moomeelam,ak ci jaamu ko,ak ci ay turam ak i meloom, "wa bi Muhammadin rasuulan" maanaam: gëm naa Muhammat ci mbooleem li ñu ko yónni mu jottali nu ko, "wa bil Islaami" maanaam:ak gëm mbooleem àttey Lislaam yi ci ay ndigël ak i tere, "diinan" maanaam: mooy sama diine ci pas-pas ak di ko wommatul, "dees na ko jéggal ay bàkkaaram" maanaam: yu ndaw yi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Oromoo Kanadi
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Di baamtu ñaan gii saa yu ñu déggee nodd gi dafa bokk ci liy far ay bàkkaar.