Xàjjale yi:
+ -

عَنْ أَبِي عَبْدِ اللَّهِ جَابِرِ بْنِ عَبْدِ اللَّهِ الْأَنْصَارِيِّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا:
أَنَّ رَجُلًا سَأَلَ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: أَرَأَيْتَ إِذَا صَلَّيْتُ المَكْتُوبَاتِ، وَصُمْتُ رَمَضَانَ، وَأَحْلَلْتُ الحَلَالَ، وَحَرَّمْتُ الحَرَامَ، وَلَمْ أَزِدْ عَلَى ذَلِكَ شَيْئًا، أَأَدْخُلُ الجَنَّةَ؟ قَالَ: «نَعَمْ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [الأربعون النووية: 22]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Abdulla Jaabir ibn Abdallah Al-Ansaarii yal na leen Yàlla dollee gërëm:
Benn waay dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam, te dolliwuma ca dara, ndax dinaa dugg àjjana ? Mu ne ko: "waaw".

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [الأربعون النووية - 22]

Leeral

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ku julli julliy juróom yi nu farataal, te tegu ca ay naafila, woor weeru koor te tegu ca ay coobare wu, lu dagan mu gëm ne dafa dagan mu def ko, lu araam mu gëm ne dafa araam mu moytu ko, kooku dana dugg àjjana.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi:
  2. Xérug jullit bi ci def farata yi ak bàyyi yu araam yi, jubluwaayam dëgg na nekk dugg àjjana.
  3. Njariñu def yu dagan yi ak fas ne dafa dagan, ak araamal yu araam yi te gëm ne dafa araam.
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Bengali Turki Risi Bosniya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Amhari Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Majri Ciikiya الموري Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية
Gaaral tekki yi
Xàjjale yi
Ndollent