____
[] - []
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Amr -nee nañu it: Abii Amrata--, Sufyaan ibn Abdallah yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [الأربعون النووية - 21]
Sahaaba bii di Sufyaan Ibnu Abdullah -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir mu xamal ko wax ju matale maanaay lislaam yi mu jàpp ci te du ko laajaat kenn ku dul moom ? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko : waxal : wéetal naa Yàlla, te gëm naa ne mooy sama Yàlla, moom laay jaamu, moo ma bind, moom laay jaamu ci dëgg deesu ko bokkaale ak dara. Topp mu wommatul Yàlla, topp ko, ci ay farataam, ak bàyyi yi Yàlla araamal, te sax ci loolu.