عَنْ جَابِرِ بْنِ عَبْدِ اللَّهِ رضي الله عنهما أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنْ قَالَ حِينَ يَسْمَعُ النِّدَاءَ: اللَّهُمَّ رَبَّ هَذِهِ الدَّعْوَةِ التَّامَّةِ، وَالصَّلاَةِ القَائِمَةِ، آتِ مُحَمَّدًا الوَسِيلَةَ وَالفَضِيلَةَ، وَابْعَثْهُ مَقَامًا مَحْمُودًا الَّذِي وَعَدْتَهُ، حَلَّتْ لَهُ شَفَاعَتِي يَوْمَ القِيَامَةِ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 614]
المزيــد ...
Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"ku dégg nodd daldi wax: Allaahuma Rabba haasihid dahwati attaammati, wassalaatil xaa-imati, aati Muhammadan alwasiilata walfadiilata, wabhashu maxaaman mahmuudan allasii wahadtahu, kon samag rammu yell na ci moom ëllëg bis-pénc".
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 614]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne ku wax jamono yu mu dégge noddukat bi ginnaaw ba mu ca noppee:
(Allaahuma Rabba haasihid dahwati), te mooy baati nodd gi yi ñuy wootee jëm ci jaamu Yàlla ak julli, (attaammati) gu mat gi, wooteg Tawhiid ak yónnent gi, (wassalaatil xaa-imati) gay aji-sax te ñu dees na ko taxawal, (aati) joxal, (Muhammadan alwasiilata) wàccuwaay bu kawe ba ca ajjana, nga xam ne yellul ci ku dul moom Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, (walfadiilata) dayo bu ëpp dayoy mbindeef yi, (wabhashu) jox ko, (maxaaman) gog dees na sant ku ca nekk; te mooy rammu gu màgg ga ëllëg bis-pénc, (allasii wahadtahu) ci sa wax ja: {sa Boroom dana la jox wàccuwaay gu ñu gërëm} ci mu nekk ñeel ko moom Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Ku ñaan ñaan gii yayoo na te war na ci moom rammug Yonente bi ëllëg bis-pénc.