عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لاَ يُصَلِّي أَحَدُكُمْ فِي الثَّوْبِ الوَاحِدِ لَيْسَ عَلَى عَاتِقَيْهِ شَيْءٌ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 359]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«Bu kenn ci yéen jullee ci benn yére te dara tegewul ci kaw mbaggam».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 359]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na kuy julli ci benn yére ay mbaggam di feeñ dara teguwul ci kawam; ndaxte ñaari mbagg yi donte duñu awra, muur leen moo gën a jàppandi muur awra wi, te moo gën a jege màggal Yàlla mu màgg mi, ag màggal ko ci jamono yi mu taxawe ci kanamam ci julli gi.