عن علي رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«رُفِعَ الْقَلَمُ عن ثلاثة: عن النائم حتى يَسْتَيْقِظَ، وعن الصبي حتى يَحْتَلِمَ، وعن المجنون حتى يَعْقِلَ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي في الكبرى وابن ماجه وأحمد] - [سنن أبي داود: 4403]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aliyun yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«yëkkëti nanu xalima gi ci ñatt, ci kiy nelaw ba baa muy yeewu, ak ci xale bi ba baa muy gént, ak ci dof bi ba baa
muy xellu».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 4403]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne doomu Aadama lees toggu jëf ba mu des ñatt ñii:
Xale bu ndaw bi ba keroog muy màgg di mat.
Ak dof bi am xelam dem ba keerog muy
dellusi.
Ak kiy nelaw ba keroog muy yeewu.
Kenn toggu leen jëf, def gi ñuy def bàkkaar
deesu leen ko bindal, waaye dees na bindal yiw xale bi wolif dof bi ak kiy nelaw; ndax ñoom ñaar dañoo nekk ci anam goo xam ne nanguwul ag jaamu di ca wére, ngir li ag yég deñ ci ñoom.