+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِنَّ اللَّهَ تَجَاوَزَ عَنْ أُمَّتِي مَا حَدَّثَتْ بِهِ أَنْفُسَهَا، مَا لَمْ تَعْمَلْ أَوْ تَتَكَلَّمْ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5269]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«Yàlla jéggal na samaw xeet li seen i xel di xalaat, fii ak defuñu mbaa ñu wax».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5269]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne jullit bi deesu ko toppe li xelam di xalaat ci ay njëkk mu koy def walla mu koy wax, ndax Yàlla yëkkëti na coono ba daal di jéggale, te du toppe xeetu Muhammat liy nekk ci am xelam di dengi-dengi ci xel mi lu dul mu am cag dal ak ug féex; bu ca xelam féexee nag niki rëy-rëylu ak puukarewu ak naaféq walla mu jëf ci ay céram mbaa mu wax ci làmmeñam, kon dees na ko jàppe loolu.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Yàlla mu kawe mi baale na jéggale na xalaat yiy nekk cim xel, nit ki di ko wax ak boppam, muy romb ci xel yi.
  2. Bu nit ki xalaatee fase, mu gaar cim xelam, waaye waxu ko, bindu ko, kon deesu ko jàppe am fase.
  3. Waxtaanu xel deesu ko jàppe nit ki ak lumu rëy rëy fii ak demul ba def ko, walla mu wax ko.
  4. Màggug dayob
  5. xeetu Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ñi jagleel ko bañ koo jàppe waxtaanu xel yi, mu wuute ak xeet yi jiitu woon.
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Serbi Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Asrabijaani Ukraani الجورجية المقدونية
Gaaral tekki yi
Ndollent