+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنْ كَانَتْ لَهُ امْرَأَتَانِ فَمَالَ إِلَى إِحْدَاهُمَا، جَاءَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ وَشِقُّهُ مَائِلٌ».

[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي وابن ماجه وأحمد] - [سنن أبي داود: 2133]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«ku am ñaari jabar daal di jeng ci kenn ki, dana ñëw ëllëg bis-pénc wetam gi jeng».

[Wér na] - - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 2133]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku am lu ëpp benn soxna, te maanduwul ci seen diggante kem kàttanam, ci yemale seen diggante ci dundal ak dëkkal ak koddaay ak fanaan ga, ci ne mbugalam ëllëg bis-pénc mooy xaaju yaramam daal di jeng, jeng gi mbugal la ci tooñam gi, kem ni mu jenge ci jëflanteem gi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. War na ci góor gi mu séddale ci diggante ñaari jabaram walla ay jabaram, dana araam ci moom muy jeng jëm ci kenn ki wolif keneen ki, ci kem kàttanam ci dundal gi ak fanaan gi, ak rafetug nekkiin, ak lu ko niru.
  2. Yamale ci séddali gi ak yu ko niru, mooy ci li nit ki moom, bu dee li nit ki moomul nag niki bëgg gi ak jengug xol bi loolu du dugg ci hadiis bi, te mooy li ñu namm ci waxu Yàlla ji: {manu leen a màndu donte xér ngeen ci} [An-Nasaa-i: 129].
  3. Fay day nekk ci kem jëf ji, góor gi bi mu jengee ci àdduna ci jóge ci jenn jabar jëm ci jeneen, ta mu ñëw ëllëg bis-pénc genn wet gi jeng wolif geneen gi.
  4. Màggaayu àqi jaam ñi, ak ne kenn du ko baale; ndaxte dees ko a tabax ci fayyantoo.
  5. Sopp nañu yem ci jenn jabar, bu dee góor gi dafa ragal ne du maandu ci diggante ay jabaram; ngir mu bañ a tàbbi ci gàttañlu ci diine; Yàlla mu kawe mi nee na: {bu ngeen ragalee ne dungeen maandu kon takkleen jenn jabar} [An-Nasaa-i: 3].
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Nipali Dariya Rom Majri الموري Ukraani الجورجية المقدونية الماراثية
Gaaral tekki yi