عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«أَكْمَلُ الْمُؤْمِنِينَ إِيمَانًا أَحْسَنُهُمْ خُلُقًا، وَخَيْرُكُمْ خَيْرُكُمْ لِنِسَائِهِمْ».
[حسن] - [رواه أبو داود والترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 1162]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yònente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam».
[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 1162]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne nit ki gën a mat ngëm ci nit ñi mooy ki gën a rafet jikko, ci béllil xar kanam, ak def njekk, ak rafet i wax, ak jeñ lor.
Ak ne ki gën ci way-gëm yi mooy ki gën ci ay jigéenam, niki ay jabaram ak i doomam yu jigéen, ak i mbokkam ak ay jegeñaaleem yu jigéen; ndax ñoom ñoo gën a yayoo ci nit ñi jikko ju rafet.