+ -

عن عبد الله بن عمرو رضي الله عنهما أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«الدُّنْيَا مَتَاعٌ، وَخَيْرُ مَتَاعِ الدُّنْيَا الْمَرْأَةُ الصَّالِحَةُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1467]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«àdduna ay jumtukaay rekk la, te li gën ci jumtukaay yi àdduna mooy jigéen ju baax».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1467]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne àdduna ak li ci biiram mbir mu ñuy bànneexoo ab diir rekk la mu jeex , waaye li gën ci banneexi àdduna mooy jabar ju baax, ji nga xam ne bu ko xoolee bég, bu ko digalee mu topp ko, bu fa nekkul mu wattu ko ci boppam ak alalam.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Kanadi البلغارية Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dagan na ñu bànneexu ci yu teeyi àdduna yi Yàlla daganalal jaamam ñi ci lu dul yàq mbaa ŋott.
  2. Xemmemloo ci tànn jabar ju baax; ndaxte day dimbali jëkkëram ci topp Boroomam.
  3. Li gën ci bànneexi àdduna mooy lu tege ci topp Yàlla mbaa mu cay dimbaalee.