عَنْ عُقْبَةَ بْنِ عَامِرٍ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِيَّاكُمْ وَالدُّخُولَ عَلَى النِّسَاءِ» فَقَالَ رَجُلٌ مِنَ الأَنْصَارِ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، أَفَرَأَيْتَ الحَمْوَ؟ قَالَ: «الحَمْوُ المَوْتُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5232]
المزيــد ...
Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"moytandikuleen di jaxasoo ak jigéen ñi" jenn waay ci Ansaar yi ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, noo gise goro? Mu ne ko: "goro moo dee faf".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5232]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo na jaxasoo ak jigéeni jàmbur, mu wax ne: moytulleen seen bopp ci dugg ci jigéen ñi, ak it jigéen ñi di dugg ci yéen.
Jenn waay ci waa Ansaar yi ne ko: xibaare ñu ci mbokki jëkkër yi; niki mbokkam mu góor ak doom ju góor ju mbokkam mu góor jur, ak baay tëxam ak doomu baay taxam ju góor, ak doom ju góor ju mbokkam mu jigéen jur, ak ñu mel ni ñoom ci ñi dagan ñu takk ko bu doon amul jëkkër?
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne: moytandikuleen ko kem ni ngeen moytandikukoo dee! Ndaxte wéet ak goro yi day indi fitna ak alkande ci diine, jegeñaaley jëkkër ju dul ay baayam ak ay doomam ñoo gën a yay ag tere ci jàmbur ñi; ndaxte wéet ak jegeñaaley jëkkër moo gën a bari wéet ak keneen, te ci moom la fitna gën a man a nekke; ngir li mu man a egg ci jigéen ak wéet ak moom ci lu dul kenn di ko bañ ci moom, ak li mu manut a ñàkk, te manuñu ko ko a tere, ndax li aada di wéy ci woyofal ko, ba tax góor gi di wéet ak jabaru mbokkam; kon moom dafa niroo ak dee ci ñaaw gi ak yàqu gi, mu wuute ak góoru jàmbur moom dañu koy moytandiku.