عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الخُدْرِيَّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ -وَكَانَ غَزَا مَعَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ ثِنْتَيْ عَشْرَةَ غَزْوَةً- قَالَ: سَمِعْتُ أَرْبَعًا مِنَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَأَعْجَبْنَنِي، قَالَ:
«لاَ تُسَافِرِ المَرْأَةُ مَسِيرَةَ يَوْمَيْنِ إِلَّا وَمَعَهَا زَوْجُهَا أَوْ ذُو مَحْرَمٍ، وَلاَ صَوْمَ فِي يَوْمَيْنِ: الفِطْرِ وَالأَضْحَى، وَلاَ صَلاَةَ بَعْدَ الصُّبْحِ حَتَّى تَطْلُعَ الشَّمْسُ، وَلاَ بَعْدَ العَصْرِ حَتَّى تَغْرُبَ، وَلاَ تُشَدُّ الرِّحَالُ إِلَّا إِلَى ثَلاَثَةِ مَسَاجِدَ: مَسْجِدِ الحَرَامِ، وَمَسْجِدِ الأَقْصَى، وَمَسْجِدِي هَذَا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1995]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu yal na ko Yàlla dollee gërëm -moom nag xare na ànd ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki xare ak ñaar- nee na: dégg naa ñent ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-te yéem na ma, mu wax ne:
"bu genn jigéen tukki lu mat doxub ñaari fan lu dul mu ànd ak jëkkëram walla ab jegeñaaleem , te kenn du woor ci ñaari bis yii : korite ak tabaski, kenn du julli ginnaaw suba gi ba keroog jant bi di fenk, du caagine it ginnaaw tàkkusaan ba keroog muy so, deesul war jëm cib tukki lu dul ñeel ñatti jàkka: jàkkay Màkka ja ñu wormaal, ak jàkkay Aqsaa, ak sama jàkka jii".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1995]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na ñenti bir:
Bi ci njëkk: tere na jigéen muy tukki lu toll ci doxup ñaari fan te àndul ak jëkkëram walla kenn ci ñi ko araam te mooy ku ñu araamal ci moom ba fàww ci ay jegeñaaleem, niki doom ak baay,ak doomi mbokk mu góor ak jarbaat,ak baay-tëx ak nijaay, ak ñu mel ni ñooñu.
Ñaareel bi: tere nañu woor bisub xewu korite ak bisub xewu tabaski,moo xam jullit da koo woor ngir nisar, walla ci coobarewu, walla ci kaffaara.
Ñatteel bi: tere nañu jullig naafila ginnaaw jullig tàkkusaan ba keroog jant bi di so, ak ginnaaw jullig suba ba keroog jant bi di fenk.
Ñenteel bi: tere nañu tukki jëm ci benn barab ci barab yi ngir gëm ne dañufay fule jëf yu baax yi lu dul ci ñatti jàkka yii, kon deesul takk tukki ci fu dul ñoom ngir julli fa,ndax pay gi duñu ko ful ludul ci ñatti jàkka yii, jàkkay Màkka ja ñu wormaal,ak jàkkay Yonnente bi, ak jàkkay Aqsaa.