عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي لله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَا يَفْرَكْ مُؤْمِنٌ مُؤْمِنَةً، إِنْ كَرِهَ مِنْهَا خُلُقًا رَضِيَ مِنْهَا آخَرَ» أَوْ قَالَ: «غَيْرَهُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1469]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Jullit bu góor du bañ jullit bu jigéen, ndax su bañee ci moom jenn jikkó gërëm na ci moom jeneen jikkó».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1469]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na jëkkër di bañ jabaram bañ guy waral mu koy tooñ di ko bàyyi di ko dummóoyu; Ndaxte nit dañu koo bind cig mànkite, te bu bañee ci moom ay jikkó yu ñaaw, dana fekk ci moom ay jikkó yu rafet; bu ko defee mu gërëm yu rafet yi tolloog moom , te muñ yu ñaaw yi mu gërëmul, loolu mooy tax muy muñ te du ko bañ mbañeel guy waral muy tàggalikoo ak moom.