عَنْ حُذَيْفَةَ رضي الله عنه قَالَ:
كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا قَامَ مِنَ اللَّيْلِ يَشُوصُ فَاهُ بِالسِّوَاكِ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 245]
المزيــد ...
Jële nañu ci Husayfata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan jug guddi day socc.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 245]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na bari lu muy socc di ko digle it, moom nag day feddaliku ci yenn waxtu yi, bokk na ca: socc bu ñu jògee guddi, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na bomb gémmeñam di ko setal ci socc.