عَنِ ابْنِ عُمَرَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا قَالَ:
حَفِظْتُ مِنَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَشْرَ رَكَعَاتٍ: رَكْعَتَيْنِ قَبْلَ الظُّهْرِ، وَرَكْعَتَيْنِ بَعْدَهَا، وَرَكْعَتَيْنِ بَعْدَ المَغْرِبِ فِي بَيْتِهِ، وَرَكْعَتَيْنِ بَعْدَ العِشَاءِ فِي بَيْتِهِ، وَرَكْعَتَيْنِ قَبْلَ صَلاَةِ الصُّبْحِ، وَكَانَتْ سَاعَةً لاَ يُدْخَلُ عَلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِيهَا، حَدَّثَتْنِي حَفْصَةُ أَنَّهُ كَانَ إِذَا أَذَّنَ المُؤَذِّنُ وَطَلَعَ الفَجْرُ صَلَّى رَكْعَتَيْنِ، وَفِي لَفْظٍ: أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ يُصَلِّي بَعْدَ الْجُمُعَةِ رَكْعَتَيْنِ.
[صحيح] - [متفق عليه بجميع رواياته] - [صحيح البخاري: 1180]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Mokkal naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka: ñaari ràkka njëkk tisbaar, ak ñaari ràkka ci ginnaawam, ak ñaari ràkka ginnaaw timis ci këram, ak ñaari ràkka ginnaaw gee ci këram, ak ñaari ràkka njëkk jullig suba, moom nag aw waxtu la woo xamne kenn daawul dugg fa Yonnente bi nekk, Hafsa nettalinama ne bu noddkat bi daan nodd ba fajar gi fenk day julli ñaari ràkka, ci jeneen wax: moom Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na julli ñaari ràkka ginnaaw àjjuma.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér, ci mbooleem anami nettali yi mu dikkee] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1180]
Abdullah Ibn Umar -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne: bokk na ci naafila yi mu wattoo ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka, ñu koy wooye sunnay rawaatib, Ñaari ràkka njëkk tisbaar, ak ñaari ràkka ginnaawam, Ak ñaari ràkka ginnaaw timis ci këram, Ak ñaari ràkka ginnaaw gee ci këram, Ak ñaari ràkka njëkk fajar, Loolu mat fukki ràkka. Bu dee jullig àjjuma nag daa na julli ñaari ràkka ginnaawam.