+ -

عَنْ ‌أَبِي قَتَادَةَ السَّلَمِيِّ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِذَا دَخَلَ أَحَدُكُمُ الْمَسْجِدَ فَلْيَرْكَعْ رَكْعَتَيْنِ قَبْلَ أَنْ يَجْلِسَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 444]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Xataadata As-Sulamii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 444]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day ñaax ku dugg ci jàkka waxtu wu mu man a doon, ak yitte ju ko man a waral, mu julli ñaari ràkka balaa toog, ñuy ñaari ràkkay nuyu jàkka ji.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sopp nañu julli ñaari ràkka ngir nuyu jàkka ji bala ñoo toog.
  2. Ndigël lii nag ngir ku bëgg a toog la, ku dugg ci jàkka daal di génnaat njëkk muy toog kooku ndigël li jëmul ci moom.
  3. Aji-julli ji bu duggee ci jàkka ji fekk nit ñi nekk ci julli gi mu dugg ci julli gi ànd ak ñoom loolu dana ko doy wolif ñaari ràkka yi.