عَنْ أَبِي حُمَيْدٍ أَوْ عَنْ أَبِي أُسَيْدٍ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِذَا دَخَلَ أَحَدُكُمُ الْمَسْجِدَ فَلْيَقُلِ: اللَّهُمَّ افْتَحْ لِي أَبْوَابَ رَحْمَتِكَ، وَإِذَا خَرَجَ فَلْيَقُلِ: اللَّهُمَّ إِنِّي أَسْأَلُكَ مِنْ فَضْلِكَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 713]
المزيــد ...
Jële nañu ci Humaydin mbaa Abuu Usaydin mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na wax: Allaahumma iftah lii abwaaba rahmatika, bu génnee na wax: Allaahumma innii as-aluka min fadlika».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 713]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamal xeetam wi ñaan gi ñuy wax bu ñuy dugg ci jàkka: (Allaahumma iftah lii abwaaba rahmatika), day ñaan Yàlla mu jàppandalal ko sabab yiy waral yërmàndeem, bu bëggee génn na wax: (Allaahumma innii as-aluka min fadlika), day ñaan Yàlla ci ngëneelam yi ak dolli ko ci rafetalam gi wërsëg wu dagan.