+ -

عَنْ ‌أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللهُ عَنْهُ: أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«صَلَاةٌ فِي مَسْجِدِي هَذَا خَيْرٌ مِنْ أَلْفِ صَلَاةٍ فِيمَا سِوَاهُ إِلَّا الْمَسْجِدَ الْحَرَامَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1190]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1190]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ngëneelu julli ci jàkkaam ji, ak ne moo gën yool ci junni julli ci fu dul moom ci jàkka yi ci kaw suuf, ba mu des jàkka ja ñu wormaal fa Màkka, ndax moom moo gën julli ci jàkkay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dañuy ful yoolu julli ci jàkkay Màkka ak Jàkkay Yonnente bi ca Madiina.
  2. Julli ci jàkkay Màkka moo gën téeméeri junni julli ci beneen bu dul moom.