عن عُبَادَةَ بن الصَّامتِ رضي الله عنه قال:
بَايَعْنَا رسولَ اللهِ صلى الله عليه وسلم على السَّمْعِ وَالطَّاعَةِ فِي الْعُسْرِ وَالْيُسْرِ، وَالْمَنْشَطِ وَالْمَكْرَهِ، وعلى أَثَرَةٍ علينا، وعلى أَلَّا نُنَازِعَ الْأَمْرَ أهلَه، وعلى أَنْ نَقُولَ بِالْحَقِّ أينما كُنَّا، لا نَخَافُ في الله لَوْمَةَ لَائِمٍ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1709]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ubaadata Ibnus Saamit -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
Jaayante nanu ak Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dégg ak topp, ci lu jafe ak lu yomb, ci lu neex ak lu naqari, ak bu xat-xat tegee sunu kaw, ak nu bañ a xëccoo ak nguur, ak nu bañ a wax lu dul dëgg fu nu man a nekk, dunu ragal ci Yàlla yeddagay aji-yedde ji.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1709]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa jël kóllare ci Sahaaba yi ci ñu wommatul ki yor mbir mi ak àttekat yu ci lu yomb ak lu jafe, ak ci jamonoy woomal ak ñàkk, moo xam ay ndigleem neex na sunu bàkkan walla neexu ko, donte njiit yi dañoo jiital ci kaw askan alal walla ag pal mbaa leneen, dees leen a war a déggal, topp leen ci njekk, te bañ a jàmmaaloo ak ñoom, ndax fitna ak yàq gi nekk ci xeex ak ñoom moo gën a rëy yàq giy am ci séenug tooñ, bokk na ci li ñu kóllarante ak moom ñuy wax dëgg ci bépp barab di way-sellal ci loolu ngir Yàlla dong te duñu ragal ku leen di yedd.