عَنْ عَائِشَةَ أُمِّ المُؤْمِنين رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا، قَالَتْ:
مَا رَأَيْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مُسْتَجْمِعًا قَطُّ ضَاحِكًا، حَتَّى أَرَى مِنْهُ لَهَوَاتِهِ، إِنَّمَا كَانَ يَتَبَسَّمُ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6092]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Masuma a gis Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy xàqataay di ree ba ma gis ay yàppi biir gémmiñam, waaye da daan muuñ.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6092]
Aysatu yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daawul ree reetaan gu ëpp ba ñuy gis am siiñam, waaye da daan muuñ.