+ -

عَنِ ابْنِ عَبَّاسٍ رَضيَ اللهُ عنهما أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ يَقُولُ:
«اللهُمَّ لَكَ أَسْلَمْتُ، وَبِكَ آمَنْتُ، وَعَلَيْكَ تَوَكَّلْتُ، وَإِلَيْكَ أَنَبْتُ، وَبِكَ خَاصَمْتُ، اللهُمَّ إِنِّي أَعُوذُ بِعِزَّتِكَ، لَا إِلَهَ إِلَّا أَنْتَ أَنْ تُضِلَّنِي، أَنْتَ الْحَيُّ الَّذِي لَا يَمُوتُ، وَالْجِنُّ وَالْإِنْسُ يَمُوتُونَ».

[صحيح] - [متفق عليه، وهذا لفظ مسلم ورواه البخاري مختصرًا] - [صحيح مسلم: 2717]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax:
"Allahumma laka aslamtu, wa bika aamantu, wa halayka tawakkaltu, wa ilayka anabtu, wa bika xaasamtu, Allaahuma innii ahuusu bihissatika, laa ilaaha illaa Anta an tadillanii, Anta Al-Hayyu Allasii laa yamuutu, wal insu wal jinnu yamuutuuna".

[Wér na] - [متفق عليه وهذا لفظ مسلم ورواه البخاري مختصرًا] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2717]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan ñaan daan na wax: (yaw sama Boroom yaw rekk laa jébbalul) daal di wommatu, (te yaw rekk laa gëm) dëggal naa saxal naa, (te ci yaw rekk laa wakkirlu) bàyyeel la lépp sukkandiku ci yaw, (te ci yaw rekk laa dellu) dellu ci yaw jublu la, (te ci yaw rekk laay xuloo) di dàggasante ak sa noon yi, (yaw sama Boroom maa ngi muslu) di làqatu, (ci sag teddnga) sag terewu ak sag noteel, (amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul yaw) amul lu ñuy jaamu ci dëgg ku dul yaw, (nga sànk ma) wolif njub ga ak dëppoo ak sa ngërëm, (yaw yaay Aji-Dund ji dul dee) du jeex, (te jinne yi ak nit ñi dañuy dee).

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Yoonalees na jiital tagg ci laaj ci gépp càkkuteef.
  2. Dañoo war a wakkirlu ci Yàlla mu kawe mi dong ak sàkku ci moom ak sàmm; ndaxte moo melowoo melo yu mat yi, moom dong mooy ki ñu sukkandiku, mbindeef yépp dañoo tële te ci dee lañuy mujje, kon ñoom yayoowuñu a sukkandiku ci ñoom.
  3. Roy ci Yonente bi di ñaan ci kàddu yu matale yii nga xam ne day wane ngëm gu dëggu ak kóolute gu mat sëkk.
  4. As-Sindii nee na: waxam ji (yaw yaay Aji-Dund ji) maanaam: yaw yaay ki nga xam ne ci moom dong lañu war a musloo amul keneen.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri الموري Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi