عَنْ عُثْمَانَ الشَّحَّامِ، قَالَ: انْطَلَقْتُ أَنَا وَفَرْقَدٌ السَّبَخِيُّ إِلَى مُسْلِمِ بْنِ أَبِي بَكْرَةَ وَهُوَ فِي أَرْضِهِ، فَدَخَلْنَا عَلَيْهِ فَقُلْنَا: هَلْ سَمِعْتَ أَبَاكَ يُحَدِّثُ فِي الْفِتَنِ حَدِيثًا؟ قَالَ: نَعَمْ، سَمِعْتُ أَبَا بَكْرَةَ رضي الله عنه يُحَدِّثُ، قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّهَا سَتَكُونُ فِتَنٌ، أَلَا ثُمَّ تَكُونُ فِتْنَةٌ الْقَاعِدُ فِيهَا خَيْرٌ مِنَ الْمَاشِي فِيهَا، وَالْمَاشِي فِيهَا خَيْرٌ مِنَ السَّاعِي إِلَيْهَا، أَلَا فَإِذَا نَزَلَتْ أَوْ وَقَعَتْ فَمَنْ كَانَ لَهُ إِبِلٌ فَلْيَلْحَقْ بِإِبِلِهِ، وَمَنْ كَانَتْ لَهُ غَنَمٌ فَلْيَلْحَقْ بِغَنَمِهِ، وَمَنْ كَانَتْ لَهُ أَرْضٌ فَلْيَلْحَقْ بِأَرْضِهِ»، قَالَ فَقَالَ رَجُلٌ: يَا رَسُولَ اللهِ أَرَأَيْتَ مَنْ لَمْ يَكُنْ لَهُ إِبِلٌ وَلَا غَنَمٌ وَلَا أَرْضٌ؟ قَالَ: «يَعْمِدُ إِلَى سَيْفِهِ فَيَدُقُّ عَلَى حَدِّهِ بِحَجَرٍ، ثُمَّ لِيَنْجُ إِنِ اسْتَطَاعَ النَّجَاءَ، اللهُمَّ هَلْ بَلَّغْتُ؟ اللهُمَّ هَلْ بَلَّغْتُ؟ اللهُمَّ هَلْ بَلَّغْتُ؟»، قَالَ: فَقَالَ رَجُلٌ: يَا رَسُولَ اللهِ أَرَأَيْتَ إِنْ أُكْرِهْتُ حَتَّى يُنْطَلَقَ بِي إِلَى أَحَدِ الصَّفَّيْنِ، أَوْ إِحْدَى الْفِئَتَيْنِ، فَضَرَبَنِي رَجُلٌ بِسَيْفِهِ، أَوْ يَجِيءُ سَهْمٌ فَيَقْتُلُنِي؟ قَالَ: «يَبُوءُ بِإِثْمِهِ وَإِثْمِكَ، وَيَكُونُ مِنْ أَصْحَابِ النَّارِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2887]
المزيــد ...
Jële nañu ci Usmaan As-Sahhaam, mu wax ne: dem naa man ak Farxad As-Sabahii ca Muslim ibn Abii Bakrata fekk ma nga ca suufam sa, nu dugg fi moom nu ne ko: ndax dégg nga sa baay di wax ci fitna yi bu yàggul? Mu ne: waaw, dégg naa Abii Bakrata yal na ko Yàlla dollee gërëm muy waxtaan ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"ay fitna dana am, yëgleen ne bu fitna amee ka toog moo gën ka kay dox, kay dox mooo gën kay daw, yëgleen ne bu wàccee walla mu tàbbi ku am ay giléem na dem ci ay giléemam, ku am ay gàtt na dem ci ay gàttam, ku am suuf na dem ci suufam, nee na: jenn waay ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, wax nu nu ku amul giléem amul gàtt amul suuf moom nag? Mu ne ko: "na dem ci jaaseem dëbb ñawka ga ak xeer, topp mu jéema muccbu ko manee, yaw Yàlla sama Boroom ndax jottali naa? Yaw Yàlla sama Boroom ndax jottali naa? Yaw Yàlla sama boroom ndax jottali naa?, nee na jenn waay ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, xibaare nu bu ñu ma foorsee ba yóbb ma ci benn ci ñaari kurél yi benn waay dóor ma jaaseem, walla ag fett ray ma? Mu ne ko: "day gàddu bàkkaaram ak sa bàkkaar, mu bokk ci waa sawara".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2887]
Usmaan As-Sahhaam ak Farxad As-Sabahii dañoo laaj Muslim doomu Sahaaba bu màgg bii di Abuu Bakrata yal na ko Yàlla dollee gërëm: ndax dégg na ci baayam ab hadiis mu jële ko ci Yonente bi muy wax ci fitnay rayante yiy dox ci diggante jullit ñi? Mu ne waaw, xibaare na ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na ay fitna dana ñëw ginnaaw ag faatoom, te fitna yii ki toog sàggane ko moo gën ka cay dox fekk séentuwu ko te gëstuwu ko, ka cay dox it moo gën ka cay daw di ko gëstu di ca bokk. Yonnente bi daal di jàngale ci ne ku fekke jamonoy fitna te mu am fu mu làqu na fa dem; ku am ay giléem yu muy sàmm na dem ci ay giléemam, ku am ay gàtt yu muy sàmm na dem ci ay gàttam, ku am suuf ak tool na dem ca suufam. Jenn waay ne ko: yaw Yonente Yàlla bi wax nu ku amul fu mu làqu du giléem du ay gàtt du suuf nu muy def? Mu ne ko: na dem ci jaaseem dëbb ko moxañe ko, top mu daw muccali boppam ak doomam bu manee mucc. Topp Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc seede ñatti yoon ne: yaw Yàlla sama Boroom ndax jottali naa? Yaw Yàlla sama Boroom ndax jottali naa? Yaw Yàlla sama Boroom ndax jottali naa? Jenn waay ne ko: yaw Yonente Yàlla bi wax ma bu dee da ñu maa ga (foorse) ci ma bokk ci benn kurél bi benn waay daal di may dóor jaaseem, walla ag fett ñëw ray ma? Mu ne ko: day yóbb bàkkaari boppam ak bàkkaari ki mu ray, bu bis-pénc baa mu bokk ci waa sawara.