+ -

عن عرفجة رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«مَنْ أَتَاكُمْ وَأَمْرُكُمْ جَمِيعٌ عَلَى رَجُلٍ وَاحِدٍ، يُرِيدُ أَنْ يَشُقَّ عَصَاكُمْ، أَوْ يُفَرِّقَ جَمَاعَتَكُمْ، فَاقْتُلُوهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1852]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Arfajatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«ku ñëw ci yéen fekk ngeen abooloo ci lenn njiit, mu bëgg a xotti mbooloo mi, mbaa mu tàqqale séen mbooloo mi, rayleen ko».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Ad-daaraqutniy - 1852]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne bu jullit ñi booloo ci lenn njiit, di menn mbooloo, am ku ñëw bëgg a xëccoo ak moom njiit gi, mbaa mu bëgg a tàqale jullit ñi ci ay mbooloo yu bari, kon dañu koo war a tere daadi xeex ak moom; ngir jeñ aw ayam ak ñoŋal dereeti jullit ñi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiisb: Dañoo war a dégg te topp njiitul jullit ñi ci lu dul ag moy, araam na it di jàmmaaloo ak moom.
  2. Ku génn ci njiitl jullit ñi ak séen mbooloo ma dañoo war a xeex ak moom ag nu dayoom man a toll ci teddnga ak uw askan.
  3. Soññee ci booloo ak bañ a tàqalikoo ak di juuyoo.