+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم أنه قال:
«مَنْ ‌خَرَجَ ‌مِنَ ‌الطَّاعَةِ، وَفَارَقَ الْجَمَاعَةَ فَمَاتَ، مَاتَ مِيتَةً جَاهِلِيَّةً، وَمَنْ قَاتَلَ تَحْتَ رَايَةٍ عِمِّيَّةٍ، يَغْضَبُ لِعَصَبَةٍ، أَوْ يَدْعُو إِلَى عَصَبَةٍ، أَوْ يَنْصُرُ عَصَبَةً، فَقُتِلَ، فَقِتْلَةٌ جَاهِلِيَّةٌ، وَمَنْ خَرَجَ عَلَى أُمَّتِي، يَضْرِبُ بَرَّهَا وَفَاجِرَهَا، وَلَا يَتَحَاشَى مِنْ مُؤْمِنِهَا، وَلَا يَفِي لِذِي عَهْدٍ عَهْدَهُ، فَلَيْسَ مِنِّي وَلَسْتُ مِنْهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1848]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku génnug topp, daal di tàqalikoo ak mbooloo ma ba faatu, kon dee na deewug ceddo, képp kuy xeex ngir yékkati raayaa cànkute, di mer ngir par-parloo, di woote ci aw xeet, walla muy xeex ngir par-parloo ciw xeet pp ba ñu ray ko, kon ag rayam rayug ceddo la, képp ku génn ag topp ci sama xeet wi, di dóor ñu baax ña ak kàccoor ya, te du moytu sax way-gëm ña, te du matale kóllëreg boroom kollëre, kooku bokkul ci man te bokkuma ci moom».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1848]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne képp Ku génn ci toppug njiit ya, tàqalikoo ak mbooloom Lislaam ma dëppoo ci jaayante ak njiit la, daal di faatu ci loolu kon dee na deewug ceddo, ñooña ñooy ñidaawul topp njiit te daawuñu ànd ci menn mbooloo, waaye dañu daan nekk ay kurél ak i pàcc ñenn ñi di xeex ñeneen ñi .
. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare ne képp ku xeex ci ron raaya wow xamul lu cay dëgg ak lu cay neen, di mer ngir farag aw xeetam rekk, defu ko ngir dimbali diine ak dëgg, muy rayante ngir par-parloo ci lu dul gis-gis ak xam-xam bu leer, bu ñu ko rayee ci anam googu, day mel ni ku ñu ray cig ceddo.
Képp Ku génn ciw xeetam di xeex akñu baax ña ak kàccoor ya, te faalewul li muy def, te ragalul mbugal ma, ci ray way-gëm ña, te du matalal woroom kóllare yi muy yéefar mbaa njiit yi ci seeni kóllare, waaye dakoy xotti, loolu ci bàkkaar yu mag yi la bokk, te ku ko def yayoo na tëkku gu tar gii.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Topp buur ci lu dul moy Yàlla lu war la.
  2. Ag xuppaate gu tar ñeel na ku génn ci topp njiit la, tàqalikoo ak mbooloom jullit ñi, bu deehee ca melo woowa kon dee na ci yoonu ceddo ya.
  3. Hadiis bi day tere xeex ngir par-parloo ciw xeet.
  4. Dañoo war a matal kóllare yi.
  5. yiw wu bari nekk na ci topp ak taqoog mbooloo mi, ak kóolute ak dal, ak yéweni mbir.
  6. Tere nañu di niru-nirulu meloy ceddo ya
  7. Digle nañu taqoo ak mbooloom jullit ñi.