Toftaleg Adiis yi

Jaayante nanu ak Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dégg ak topp, ci lu jafe ak lu yomb, ci lu neex ak lu naqari, ak bu xat-xat tegee sunu kaw
عربي Àngale Urdu
ay njiit danañu ñëw, da ngeen gis ci ñoom lu baax, ak it lu bon, ku ànd ca lu baax la kooku set na wicc, ku weddi seen yu bon kooku mucc na, waaye ki muccul mooy ki gërëm yu bon ya te ànd ca
عربي Àngale Urdu
diine de laayante-biir la
عربي Àngale Urdu
yaw Yàlla sama Boroom képp ku méngoo dara ci sama mbiri xeet wii, ba noppi di tar ci ñoom, na nga tar ci kawam, waaye képp ku ménggoo dara ci sama mbiri xeet wii, daal di leen woyofalal, na nga ko woyofalal
عربي Àngale Urdu
amul benn jaam bu Yàlla sàmmuloo am càmm, mu faatu fekk da doon wuruj ña muy sàmme, lu dul ne Yàlla dana araamal ci moom àjjana
عربي Àngale Urdu
ku génnug topp, daal di tàqalikoo ak mbooloo ma ba faatu, kon dee na deewug ceddo
عربي Àngale Urdu
ku ñëw ci yéen fekk ngeen abooloo ci lenn njiit, mu bëgg a xotti mbooloo mi, mbaa mu tàqqale séen mbooloo mi, rayleen ko
عربي Àngale Urdu
dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal
عربي Àngale Urdu
ag siif de dana am ak ay mbir yu ngeen bañ" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi ana lan nga nuy digal? Mu ne: "joxeleen àq ji leen war, te laaj Yàlla seen àq
عربي Àngale Urdu