عَنِ ابْنِ مَسْعُودٍ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«سَتَكُونُ أَثَرَةٌ وَأُمُورٌ تُنْكِرُونَهَا» قَالُوا: يَا رَسُولَ اللَّهِ فَمَا تَأْمُرُنَا؟ قَالَ: «تُؤَدُّونَ الحَقَّ الَّذِي عَلَيْكُمْ، وَتَسْأَلُونَ اللَّهَ الَّذِي لَكُمْ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3603]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ag siif de dana am ak ay mbir yu ngeen bañ" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi ana lan nga nuy digal? Mu ne: "joxeleen àq ji leen war, te laaj Yàlla seen àq».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3603]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne dana jiite jullit ñi ay njiit yuy jël alali jullit ñi ak yeneen ci biri àdduna yi, di ko depaase nu mu leen soobe, ak xañ jullit ñi seen àq ci loolu. Dana am fi ñoom ci diine ji ay bir yoy deesnako koy bañ. Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- laaj ko: ana lan la ñuy def ci jamono jooju? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare leen ne ñoom li ñi feetewoo alal ji du tax ngeen xañ leen li leen war ci ñoom ci dégg ak topp, waaye na ngeen muñ tey dégg di topp te buleen xëccoo ak ñoom mbir mi, te ngeen laaj Yàlla àq ji ngeen moom, ak Yàlla yéwénal leen te jeñal leen seenuw ay ak seenu tooñ.