عَن سَهْلِ بْنِ حُنَيْفٍ رضي الله عنه أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنْ سَأَلَ اللهَ الشَّهَادَةَ بِصِدْقٍ بَلَّغَهُ اللهُ مَنَازِلَ الشُّهَدَاءِ، وَإِنْ مَاتَ عَلَى فِرَاشِهِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1909]
المزيــد ...
Jële nañu ci Sahl ibn Haniif yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"ku ñaan Yàlla nekk sahiid ci ag dëggu kon Yàlla dana ko jotale ca darajay ña nekk sahiid, donte dafa dee ci kaw lalam".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1909]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku sàkku a dee ci yoonu Yàlla, te mu dëggu sellal yéeneem jooju ñeel Yàlla mu kawe mi, kon Yàlla dana ko jox darajay way-dee ci yoonu Yalla ci yéene ju dëggu donte dafa dee ci kaw lalam ci lu dul jihaad.