عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَا يَزَالُ البَلاَءُ بِالمُؤْمِنِ وَالمُؤْمِنَةِ فِي نَفْسِهِ وَوَلَدِهِ وَمَالِهِ حَتَّى يَلْقَى اللَّهَ وَمَا عَلَيْهِ خَطِيئَةٌ».
[حسن] - [رواه الترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 2399]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Nattu du deñ ci jullit bu góor bi ak bu jigéen bi di dal ci bakkanam ak ci doomam ak ci alalam ba mu daje ak Yàlla fekk benn bàkkaar nekkul ci kawam».
[Tane na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2399]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: day xamle ne balaa ak nattu du deñ ci aji-gëm ju góor ak ju jigéen ji, di dal ci bakkanam ci wéram ak ci yaramam, ak ci ay doomam ci feebar ak faatu ak ñàkke ko teggin mbaa yeneen, ak ci alalam ci ñàkk ak yaxantu gu dem yoonam ak sàcc, ak dund gu metti ak xatug wërsëg, ba Yàlla faral ko ci nattu yooyu ay bàkkaaram ak i njuumteem ba mu daje ak Yàlla fekk laab na ci bépp bàkkaar bu mu defoon.