عَنْ عُبَادَةَ بْنِ الصَّامِتِ رَضيَ اللهُ عنهُ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«الذَّهَبُ بِالذَّهَبِ، وَالْفِضَّةُ بِالْفِضَّةِ، وَالْبُرُّ بِالْبُرِّ، وَالشَّعِيرُ بِالشَّعِيرِ، وَالتَّمْرُ بِالتَّمْرِ، وَالْمِلْحُ بِالْمِلْحِ، مِثْلًا بِمِثْلٍ، سَوَاءً بِسَوَاءٍ، يَدًا بِيَدٍ، فَإِذَا اخْتَلَفَتْ هَذِهِ الْأَصْنَافُ، فَبِيعُوا كَيْفَ شِئْتُمْ، إِذَا كَانَ يَدًا بِيَدٍ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1587]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ubaadata Ibnus Saamit -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"jaay wurus ci wurus, ak xaalis ci xaalis, ak pepp ci pepp, ak mboq ci mboq, ak tàndarma ci tàndarma, ak xorom ci xorom, dañuy tolloo, dañuy yam, bu dee xeet yi wuutee nag, jaayeleen nu mu leen soobe, bu dee loxo ak loxo la".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1587]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na yoon wi wér ci jaay juróom-benni xeeti ribaa yii, te mooy: wurus, ak xaalis, ak pepp, ak mboq, ak tàndarma, ak xorom, bu dee wenn xeet wi la, niki jaay wurus ci wurus, ak xaalis ci xaalis... Fàww mu am ñaari sàrt: Bi ci njëkk: ñu yam ci peese bu dee lu ñuy peese la, niki wurus ak xaalis, walla ñu yam ci natt bu dee lu ñuy nay natt la niki pepp ak mboq ak tàndarma ak xorom. Ñaareel bi: aji-jaay ji téye njëg gi, kiy jënd téye njaay mi, loolu nag ca barabu fasug njaay ma lay doon. Bu xeet yii wuutee, niki jaay wurus ci xaalis, ak tàndarma ci pepp, kon jaay gi dana dagan ci benn sàrt, te mooy aji-jaay ji téye njëg gi, kiy jënd téye njaay mi ca barabu fasug njaay ma, lu ko moy njaay ma yàqu, te kon tàbbi nañu ci bidaa bi ñu araamal, jaaykat bi ak jënnkat bi ñoo ci yam.