عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَا أَسْفَلَ مِنَ الكَعْبَيْنِ مِنَ الإِزَارِ فَفِي النَّارِ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 5787]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"lu weesu ñaari dojor yi ci koddaay sawara la jëm".
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5787]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo la góor ñi ñuy yoor lépp luy sàng suufu yaram wi ci mbubb walla tubëy, walla lu dul loolu ba mu nekk ci suufu dojori tànk yi, lu wàcc dojori tànk yi ci yére yu ñu yoor loolu sawara la jëm muy am mbugal ci jëfam ji.