+ -

عَنْ عَبْدِ اللهِ بْنِ عَمْرٍو رَضيَ اللهُ عنهما قَالَ:
رَجَعْنَا مَعَ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مِنْ مَكَّةَ إِلَى الْمَدِينَةِ حَتَّى إِذَا كُنَّا بِمَاءٍ بِالطَّرِيقِ تَعَجَّلَ قَوْمٌ عِنْدَ الْعَصْرِ، فَتَوَضَّؤُوا وَهُمْ عِجَالٌ، فَانْتَهَيْنَا إِلَيْهِمْ وَأَعْقَابُهُمْ تَلُوحُ لَمْ يَمَسَّهَا الْمَاءُ فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «وَيْلٌ لِلْأَعْقَابِ مِنَ النَّارِ أَسْبِغُوا الْوُضُوءَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 241]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Ànd nanu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jóge Màkka jëm Madiina ba nu eggee ci am ndox ci yoon wi am ñu gaawantu ca Tàkkusaan ga, daal di jàppu cig yàkkamti, ba nu egge fa ñoom gis seen tastën ya ndox mi laalu ko, Yonnente bi daal di wax ne: "mbugal ñeel na tastën ya ca sawara, deeleen jotal njàppu mi".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 241]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa tukki jóge Màkka jëm Madiina ànd ak Sahaaba yi, ñu gis am ndox ci yoon wi, yenn Sahaaba yi gaawantu jàppu ngir julli Tàkkusaan ba tax seen wowaayu ginnaaw ndëggu yi di feeñ ñeel aji-xool ji, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: mbugal ak alkande ca sawara ñeel na ñiy gàtteñlu ci raxas seen ginnaaw ndëggu yi bu ñuy jàppu, mu digal leen ñuy jotal ak di matale njàppu mi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Raxas tànk yi dafa war ci jàppu; ndaxte bu masaa daganoon kon du tëkku ci sawara ku raxasul tastën yi.
  2. Matale cér yi ñuy raxas lu war la, te ku bàyyi lu ndaw ci yu ñu war a laabal cig tay ak woyofal ag julleem du wér.
  3. Solos jàngal aji-réer ji ak gindi ko.
  4. Aji-xam ji day dindi lu mu gis ci sànk farata ak sunna ci anam ga mu méngool.
  5. Muhammat Ibn Ishaaq Addahlawii nee na: jotale ñatti xeet la: farata, te mooy fexe ba matale barab ba benn yoon, ak sunna te mooy :
  6. raxas ñatti yoon, ak lu ñu sopp te mooy :
  7. guddal ga te mu ànd ak ñattale ga.
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية المقدونية
Gaaral tekki yi