عن أبِي هريرة رضي اللَّه عنه: سمعتُ النبِيّ صلى الله عليه وسلم يقول:
«الفِطْرَةُ خمسٌ: الخِتَانُ والاستحدادُ وقصُّ الشَّارِبِ وتقليمُ الأظفارِ وَنَتْفُ الآبَاطِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5891]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
"«Yi Yàlla moñaale ak nit ki juróom la: xaraf, wat kawaru naq, ak wàññi kawari mustaas, ak lewwi ay weh, ak suqi kawari poqtaan».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5891]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral juróomi mbir yu bokk ci meloy diiney Lislaam ak sunnas Yónente yi:
Bi ci njëkk: xaraf, te mooy dagg der wi yokk ci sàkkaras ku góor ki ci kaw, ak dagg boppu der wi ci awray jigéen ci kaw barabu sëy bi.
Ñaareel bi mooy: wat kawari naq, te mooy wat kawar gi nekk ci naq bi te wër awra wi.
Ñatteel bi mooy: lewwi ay mustaas, te mooy jemp li sax ci tuñu ku góor ki ci kaw, ba deru tuñ wa di feeñ.
Ñenteel bi mooy: lewwi ay we.
Juróomeel bi mooy suqi kawari poqtaan.