Xàjjaley wanqaas yi

Toftaleg Adiis yi

"bu genn jigéen tukki lu mat doxub ñaari fan lu dul mu ànd ak jëkkëram walla ab jegeñaaleem *, te kenn du woor ci ñaari bis yii : korite ak tabaski, kenn du julli ginnaaw suba gi ba keroog jant bi di fenk, du caagine it ginnaaw tàkkusaan ba keroog muy so, deesul war jëm cib tukki lu dul ñeel ñatti jàkka: jàkkay Màkka ja ñu wormaal, ak jàkkay Aqsaa, ak sama jàkka jii".
عربي Àngale Urdu