عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِنَّ الدِّينَ يُسْرٌ، وَلَنْ يُشَادَّ الدِّينَ أَحَدٌ إِلَّا غَلَبَهُ، فَسَدِّدُوا وَقَارِبُوا، وَأَبْشِرُوا، وَاسْتَعِينُوا بِالْغَدْوَةِ وَالرَّوْحَةِ وَشَيْءٍ مِنَ الدُّلْجَةِ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 39]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«diine ji lu yomb la, te kenn du taral diine ji lu dul ne dana ko not, kon deeleen jubal, di jegeele, te ngeen bég, na ngeen dimbalikoo suba gi ak ngoon gi ak lenn ci guddi gi».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 39]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne diiney lislaam dañu ko tabax cig yombal ak woyofal ci mbiram yépp, yombal gi nag day gën a feddaliku ci bu sababus lompañ amee ak aajo, ndaxte xóotal ci jëfi diine yi, ak bàyyi ñeewant mujjam mooy lompañ ak bàyyi jëf ja lëpp walla lenn la, . Topp Yonnente bi daldi soññee ci digg dóomu ci lu dul ëppal; jaam bi du gàtteñlu ci li ñu ko digal, waaye du gàddu lu mu àttanul, bu lompañee ci def la gën a mat; mu def lu ko jege.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bégle ci yool bu rëy ci kaw jëf ju sax donte dafa néew ñeel ki lott ci def la gën a mat; ndaxte lott bu jugewul ci nit ki du waral yool bi di wàññeeku.
Bi dëgg-dëggi àdduna nekkee kërug tukki daal di tuxu jëm allaaxira la Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle ñu dimbalikoo ci sax cig jaamu ci def ko ci ñatti waxtuy cawarte yii:
Bi ci njëkk: suba gi: ci bu njëlbeenu bëccëg gi demee; ci diggante jullig fajar ak fenkug jant bi.
Ñaareel bi: njolloor: ginnaaw jengug jant bi.
Ñatteel bi: lëndëm: ci guddi gi yépp walla leen ci moom, ndax te
jëfi guddi moo ëpp coono jëfi bëccëg mu digle lenn ci guddi gi rekk, ci li mu wax ne : ak lenn ci guddi gi.