+ -

عن عائشة رضي الله عنها زوج النبي صلى الله عليه وسلم عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«إِنَّ الرِّفْقَ لَا يَكُونُ فِي شَيْءٍ إِلَّا زَانَهُ، وَلَا يُنْزَعُ مِنْ شَيْءٍ إِلَّا شَانَهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2594]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- Soxnas Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2594]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne def ndànk ak ug nooy ak teey ci wax ak jëf day yokk bir yi ab taar ak ug mat ak rafet, kon yell na boroomam am li mu bëgg.
Ñàkk a teey day sikkal bir yi di ko ñaawal tey tere boroomam am la mu bëgg, bu ko amee it ci coono la koy ame.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Asrabijaani Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci jikkowoo ay teey.
  2. Ag teey day taaral nit ki, te sabab la ci wépp yiw ci biri diine ak yu àdduna.