عن أنس بن مالك رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«إِنَّ اللهَ لَيَرْضَى عَنِ الْعَبْدِ أَنْ يَأْكُلَ الْأَكْلَةَ فَيَحْمَدَهُ عَلَيْهَا، أَوْ يَشْرَبَ الشَّرْبَةَ فَيَحْمَدَهُ عَلَيْهَا».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2734]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee ne:
«Yàlla dana bëgg ci jaam bi bu lekkee aw ñam mu sant ko ca, bu naanee ag naan sant ko ca».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2734]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sant gi jaam bi di sant Boroomam ci ay ngëneelam ak i xéewalam daa bokk ci bir yi ñuy ame ngërëmal Yàlla; bu lekkee aw ñam daal di wax: maa ngi sant Yàlla, bu naanee daal di wax ne: maa ngi sant Yàlla.