+ -

عن عائشة رضي الله عنها قالت: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«إنَّ المُؤْمِنَ ليُدرِكُ بِحُسْنِ خُلُقِهِ دَرَجَةَ الصَّائِمِ القَائِمِ».

[صحيح بشواهده] - [رواه أبو داود وأحمد] - [سنن أبي داود: 4798]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«aji-gëm ji jikkoom ju rafet danako may mu am darajay Aji-woor ak kiy taxaw di julli».

[Wér na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal] - [Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 4798]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne jikko ju rafet dana yóbb boroomam ca darajay ki saxoo woor bëccëg ak taxaw guddi, li dajale jikko yu rafet yi mooy: di def njekk, ak rafeti wax, ak bélli xar kanam, ak bañ a lore te di ko dékku ci nit ñi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi: Màggug yittewoog Lislaam ci yar jikko yi ak matal ko
  2. Ngëneelul jikko yu rafet, ba tax muy yóbb jaam bi ci darajay aji-woor jidul dog, ak aji-taxaw jidul sonn.
  3. Woor bëccëg ak taxaw guddi ñaari jëf lañu yu màgg am na ñu nag ab coono ci bàkkan, boroom jikko yu rafet yi day àgg ci seen daraja ngir li muy xeex ak bakkanam ci jëflante bu rafet.