عَنْ جَابِرٍ رَضيَ اللهُ عنهُ أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِنَّ مِنْ أَحَبِّكُمْ إِلَيَّ وَأَقْرَبِكُمْ مِنِّي مَجْلِسًا يَوْمَ القِيَامَةِ أَحَاسِنَكُمْ أَخْلاَقًا، وَإِنَّ أَبْغَضَكُمْ إِلَيَّ وَأَبْعَدَكُمْ مِنِّي مَجْلِسًا يَوْمَ القِيَامَةِ الثَّرْثَارُونَ وَالمُتَشَدِّقُونَ وَالمُتَفَيْهِقُونَ»، قَالُوا: يَا رَسُولَ اللهِ، قَدْ عَلِمْنَا الثَّرْثَارُونَ وَالمُتَشَدِّقُونَ فَمَا الْمُتَفَيْهِقُونَ؟ قَالَ: «الْمُتَكَبِّرُونَ».
[صحيح] - [رواه الترمذي] - [سنن الترمذي: 2018]
المزيــد ...
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege ëllëg bis-pénc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen, waaye ñi ma gën a bañ ci yéen te gën maa sori ëllëg bis-penc, ñooy coowkat yi, ak puukarekat yi, ak ñiy rëy-rëylu", ñu ne ko:yaw Yonente Yàlla bi, nun xam nanu coowkat yi ak puukarekat yi, kon lan mooy al-mutafayxihuuna? Mu ne leen: mooy: ñiy rëy-rëylu".
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2018]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne ñi mu gën a bëgg ci yéen ci àdduna, ak ñi ko gën a jege ëllëg bis-pénc ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen, ak ne ñi mu gën a bañ ci yéen ci àdduna, ñu gën ko a sori ëllëg bis-pénc ñooy ñi gën a ñaaw jikkó ci yéen; (coowkat yi) ñi bari wax ci ag dëgëral ak génn dëgg ga, (ak puukarekat yi) ñiy yaatal ci wax ngir jaay man a wax ak màggal seen i wax ci ku dul fegu ak moytu, (ak ñiy rëy-rëylu), ñu ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, nun de xam nanu coowkat yi ak puukarekat yi, lan mooy mutafayxihuuna? Mu ne: ñooy ñiy rëy-rëylu di yéjji nit ñi ñiy ubbi seen gémmiñ yi di wax lu bari.