عن عبد الله بن عمرو رضي الله عنهما قال:
لَمْ يَكُنِ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَاحِشًا وَلَا مُتَفَحِّشًا، وَكَانَ يَقُولُ: «إِنَّ مِنْ خِيَارِكُمْ أَحْسَنَكُمْ أَخْلَاقًا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3559]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nekkul woon ku ñaawi wax mbaa jëf, daa na wax naan: « ñi gën ci yéen mooy ña ca gën a rafet jikkó».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3559]
Bokkul woon ci jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ju ñaaw, walla jëf ju ñaaw, te daawu ko jublu it mbaa mu koy tay, ndax moom Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- boroom jikkó yu màgg la.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na wax naan: ki gën ci yéen fa Yàlla mooy ki gën a rafet jikkó, ci def njekk, ak leeral xar kanam, ak téye lor te muñal nit ñi, ak jaxasoo ak nit ñi ca na mu rafete.