عن سَعِيدِ بْنِ الْمُسَيَّبِ، عَنْ أَبِيهِ قَالَ:
لَمَّا حَضَرَتْ أَبَا طَالِبٍ الْوَفَاةُ، جَاءَهُ رَسُولُ اللهِ صلى الله عليه وسلم فَوَجَدَ عِنْدَهُ أَبَا جَهْلٍ وَعَبْدَ اللهِ بْنَ أَبِي أُمَيَّةَ بْنِ الْمُغِيرَةِ، فَقَالَ: «أَيْ عَمِّ، قُلْ: لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ، كَلِمَةً أُحَاجُّ لَكَ بِهَا عِنْدَ اللهِ»، فَقَالَ أَبُو جَهْلٍ وَعَبْدُ اللهِ بْنُ أَبِي أُمَيَّةَ: أَتَرْغَبُ عَنْ مِلَّةِ عَبْدِ الْمُطَّلِبِ، فَلَمْ يَزَلْ رَسُولُ اللهِ صلى الله عليه وسلم يَعْرِضُهَا عَلَيْهِ، وَيُعِيدَانِهِ بِتِلْكَ الْمَقَالَةِ، حَتَّى قَالَ أَبُو طَالِبٍ آخِرَ مَا كَلَّمَهُمْ: عَلَى مِلَّةِ عَبْدِ الْمُطَّلِبِ، وَأَبَى أَنْ يَقُولَ: لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ، قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صلى الله عليه وسلم: «وَاللهِ لَأَسْتَغْفِرَنَّ لَكَ مَا لَمْ أُنْهَ عَنْكَ»، فَأَنْزَلَ اللهُ: {مَا كَانَ لِلنَّبِيِّ وَالَّذِينَ آمَنُوا أَنْ يَسْتَغْفِرُوا لِلْمُشْرِكِينَ} [التوبة: 113]، وَأَنْزَلَ اللهُ فِي أَبِي طَالِبٍ، فَقَالَ لِرَسُولِ اللهِ صلى الله عليه وسلم: {إِنَّكَ لا تَهْدِي مَنْ أَحْبَبْتَ وَلَكِنَّ اللهَ يَهْدِي مَنْ يَشَاءُ} [القصص: 56].
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4772]
المزيــد ...
Jële nañu ci Sahiid Ibnul Musayyab,mu jële ci baayam mu wax ne:
Bi dee dikkalee Abuu Taalib, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñëw fi moom fekk fa Abuu Jahlin, ak Abdullah Ibn Abii Umayyata ibnul Muxiirata, mu ne ko: "yaw sama baay tëx, waxal: laa ilaaha Illal Laahu, genn kàddu gog dinaala ci mana layal fa Yàlla", Abuu Jahlin ak Abdullah Ibn Abii Umayyata ne ko: mo ndax dangay bàyyi diiney Abdul Muttalib, Yonnente bi deñul di ko ko gaaral, ñoom itam ñuy baamtu wax jooju, ba Abuu Taalib mujj a wax ne, maa ngi ci diiney Abdul Muttalib, mu bañ a wax: laa ilaaha illallaah, nee na: Yonnente Yàlla bi daal di wax ne: "giñ naa ci Yàlla ne dinaa la sàkkul njéggal fii ak terewuñu ma ko", Yàlla daal di wàcce laaya jii: {jaaduwul ci Yonnente bi ak ci ñi gëm ñuy jéggalul bokkaalekat yi} [At-Tawba: 113], Yàlla wàcce ci
Abuu Taalib, daal di wax Yonnente Yàlla bi ne ko: {yaw de du yaay gindi ku la soob waaye Yàlla mooy gindi ku ko soob} [Al-Xasas: 56].
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4772]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa dugg fi baay tëxam ba Abuu Taalib fekk ko muy bëgg a faatu, mu ne ko: Yaw sama baay tëx, waxal "laa ilaaha Illal Laahu", genn kàddu, ma seedeel la ci fa Yàlla, Abuu Jahlin ak Abdullah Ibn Abii Umayyata ne ko: yaw Abuu Taalib, dangay bàyyi sa diiney baay Abdul Muttalib?! Te mooy jaamu ay xërëm, deñuñu di wax ak moom ba la mu leen mujjee wax mooy: maa ngi ci diiney Abdul Muttalib, diiney bokkaale ak jaamu ay xërëm, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dinaala ñaanal njéggal fii ak sama Boroom terewu ma ko, waxu Yàlla daldi wàcc: {jaaduwul ci Yonnente bi ak ñi gëm ñuy jéggalul bokkaalekat yi donte seeni jegeñaale lañu ginnaaw ba mu leeree ne ñoom ci waa sawara lañu bokk} [At-Tawba: 113], Waxu Yàlla mu kawe mi daal di wàcc ci Abuu Taalib: {yaw de du yaay gindi ku la soob waaye Yàlla mooy gindi ku ko soob te moo xam way-gindiku ñi} [Al-Xasas: 56], Yaw daal du yaay gindi ku la neex, li la war daal mooy jottali dong, Yàlla nag mooy gindi ku ko soob.