عَنْ سَهْلُ بْنُ سَعْدٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ يَوْمَ خَيْبَرَ:
«لَأُعْطِيَنَّ هَذِهِ الرَّايَةَ غَدًا رَجُلًا يَفْتَحُ اللَّهُ عَلَى يَدَيْهِ، يُحِبُّ اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَيُحِبُّهُ اللَّهُ وَرَسُولُهُ»، قَالَ: فَبَاتَ النَّاسُ يَدُوكُونَ لَيْلَتَهُمْ أَيُّهُمْ يُعْطَاهَا، فَلَمَّا أَصْبَحَ النَّاسُ غَدَوْا عَلَى رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كُلُّهُمْ يَرْجُو أَنْ يُعْطَاهَا، فَقَالَ: «أَيْنَ عَلِيُّ بْنُ أَبِي طَالِبٍ؟» فَقِيلَ: هُوَ يَا رَسُولَ اللَّهِ يَشْتَكِي عَيْنَيْهِ، قَالَ: «فَأَرْسِلُوا إِلَيْهِ»، فَأُتِيَ بِهِ فَبَصَقَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي عَيْنَيْهِ وَدَعَا لَهُ، فَبَرَأَ حَتَّى كَأَنْ لَمْ يَكُنْ بِهِ وَجَعٌ، فَأَعْطَاهُ الرَّايَةَ، فَقَالَ عَلِيٌّ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، أُقَاتِلُهُمْ حَتَّى يَكُونُوا مِثْلَنَا؟ فَقَالَ: «انْفُذْ عَلَى رِسْلِكَ حَتَّى تَنْزِلَ بِسَاحَتِهِمْ، ثُمَّ ادْعُهُمْ إِلَى الإِسْلاَمِ، وَأَخْبِرْهُمْ بِمَا يَجِبُ عَلَيْهِمْ مِنْ حَقِّ اللَّهِ فِيهِ، فَوَاللَّهِ لَأَنْ يَهْدِيَ اللَّهُ بِكَ رَجُلًا وَاحِدًا، خَيْرٌ لَكَ مِنْ أَنْ يَكُونَ لَكَ حُمْرُ النَّعَمِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4210]
المزيــد ...
Jële nañu ci Sahl Ibn Sahd -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na bisu Xaybar ne:
«dinaa jox raaya jii
suba jenn waay joj Yàlla dana def ubbi gi ci ay loxoom, dafa bëgg Yàlla ak ub Yonnenteem, Yàlla ak ub Yonnenteem bëgg ko», nee na: nit ñi di waxtaane ci guddi gi kan ci ñoom lañu koy jox, ba nit ña xëyee dem ca Yonnente ba -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ku nekk ci ñoom di mébét nu jox ko ko, mu wax ne: "ana Aliyun Ibn Abii Taalib?" Ñu ne ko: moom de ay bëttam lay jàmbat yaw Yonnente Yàlla bi, mu wax ne: "yónneeleen fa moom", ñu indi ko Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di tifli ci kanam gi ñaanal ko, mu wér ba mel ni dara mettiwu ko woon, mu jox ko raaya ja , Aliyun ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ndax damay xeex ak ñoom ba ñu mel ni nun? Mu ne ko: "defal ndànk-ndànk ba wàcc ca seen bayaal ba, nga woo leen ci Lislaam, te xamal leen li leen ci war ci àqi Yàlla, giñ naa ci Yàlla ne Yàlla gindi ci yaw benn waay moo gën ci yaw nga am géttug jur".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4210]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamal Sahaaba yi ne jullit ñi danañu gañe Yahuuti Xaybar yi suba, te loolu dana ame ci loxoy benn waay bu muy jox raaya bi, mooy daraapoo bi arme bi di yor def ko muy màndargaam. Te bokk na ci meloy waa jii ne moom dafa bëgg Yàlla ak ub Yonnenteem, Yàlla ak ub Yonnenteem bëgg ko, Sahaaba yi fanaanee xuus ci loolu di waxtaane ana kan lañuy jox raaya ji? Ngir xemmeem teddnga ju màgg jii, Ba suba jotee ñu dem fa Yonnente ba -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ñoom ñépp ku ci ne di mébét a jot
Ci teraanga jii,
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di laaj ana Aliyun Ibn Abii Taalib -yal na ko Yàlla dollee gërëm-?
Ñu ne ko: dafa feebar bët yi lay jàmbat.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yónnee fa moom, ñu indi ko, mu tifli ci bëti Aliyun yi ca tiflitam yu tedd ya, daal di koy ñaanal, feebaram bi wér ba mel ni amul woon mettit, mu jox ko raaya ji, mu digal ko mu dox ndànk ba jege fa noon ya làqu, gaaral leen ñu dugg ci Lislaam, bu ñu wuyoo ci loolu; mu xibaar leen li war ci ñoom ci ay farata.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeralal Aliyun ngëneelu woote jëme ci Yàlla ci ne aji-woote ji bu nekkee sabab ci gindi benn nit loolu moo gën ci moom mu am ay giléem yu xonk yi nga xam ne moo gën a seer ci alali araab yi, mu moom ko walla mu saraxe ko.