عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لاَ عَدْوَى وَلاَ طِيَرَةَ، وَلاَ هَامَةَ وَلاَ صَفَرَ، وَفِرَّ مِنَ المَجْذُومِ كَمَا تَفِرُّ مِنَ الأَسَدِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5707]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«wàlle amul gaafal amul, njuuma amul, Safar amul, te nanga daw ki gaana kem ni ngay dawe Gaynde».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5707]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral yenn mbiri ceddo ya di ko moytondikuloo, di leeral ne mbir yi ci loxoy Yàlla la nekk, te dara du am ci lu dul ci ndigalam ak dogalam, te mooy:
Bu njëkk bi: ceddo ya dañoo foogoon ne feebar day wàlle ci jëmmi boppam; Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di tere ñuy gëm ne feebar day tuxu jóge ci ku feebar jëm ci keneen ci kàttanam; Yàlla rekk mooy soppaxndiku ci mbindeef yi; te mooy wàcce feebar moo koy yëkkati te loolu du am ci lu dul nammeelam ak dogalam.
Ñaareel bi: ceddo ya bu ñu daan génn ngir tukki walla yaxantu, dañuy tiital am picc, bu naawee jëm ndayjoor ñu bég, bu naawee jëm càmmooñ ñu gaafal ko daal di waññeeku, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere gaafal cig picci, leeral ne loolu pas-pas bu bon la.
Ñatteel bi: ceddo ya dañu daan wax naan: piccim looy bu tàbbee cig kër musiba day dal
waa kër ga; Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di teree gaafal googu.
Ñenteel bi: tere na gaafal weeru Diggu Gàmmu, te mooy ñaareel weer ci weeri jullt ñi. Wax nañu ne Safar: ag jaan la juy nekk ci biir di dal jur gi ak nit ñi, ñu gëmoon ne moo gën a tarug wàlle ci feebaru
ràmm; mu dàq pas-pas bii.
Juróomeel bi: mu digle ñu sori ki feebaru ngaana dal kem ni ñuy dawe gaynde, loolu nag ngir aar bakkan bi la ak musal ko ci def sabab yi Yàlla digle, ngaana: feebar la bob ceri nit ki day lekkante.