+ -

عن أبي موسى الأشعري رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«إِذَا مَرِضَ الْعَبْدُ أَوْ سَافَرَ كُتِبَ لَهُ مِثْلُ مَا كَانَ يَعْمَلُ مُقِيمًا صَحِيحًا».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 2996]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«bu nit ki feebaree walla mu tukki dees na ko bindal kem la mu daan jëf ba mu tukkiwul te wér».

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere bu wér bi ñeel Ibnu Hibbaan - 2996]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ngëneelu Yàlla ak yërmaandeem, ak ne jullit bu aadawoo di def jëf ju baax ci jamonoy wéram te tukkiwul, mujj gi mu am ngànt daal di feebar ba manu koo defaat, walla tukki soxlaal ko ba manul loolu, walla ngànt gu mu man a doon ; kon dees na ko bindal yool wu mat sëkk, kem su ko defoon cig wér ak cig ñàkka tukki.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Yaatug ngëneelu Yàlla ci jaamam yi.
  2. Ñaaxe ngir góor -góorlu ci topp yi, ak gaawantu jëf ci jamonoy wér ak jomanoy péex te.