عَن أَبِي سَعِيدٍ الخُدْرِيَّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِذَا وُضِعَتِ الجِنَازَةُ وَاحْتَمَلَهَا الرِّجَالُ عَلَى أَعْنَاقِهِمْ فَإِنْ كَانَتْ صَالِحَةً قَالَتْ: قَدِّمُونِي، وَإِنْ كَانَتْ غَيْرَ صَالِحَةٍ قَالَتْ: يَا وَيْلَهَا أَيْنَ يَذْهَبُونَ بِهَا؟ يَسْمَعُ صَوْتَهَا كُلُّ شَيْءٍ إِلَّا الإِنْسَانَ، وَلَوْ سَمِعَهُ صَعِقَ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 1314]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"bu ñu tegee néew bi ba góor ñi gàddu ko ca seen loos ya bu nekkee ku baax la day wax naan: yóobleen ma, bu dee du ku baax nag day wax naan: wóoy alku naa!! fan ngeen ko jëme? Lépp lu dul nit dana dégg kàddoom ga, te bu ko déggoon day xëm".
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1314]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne bu ñu tegee néew bi ci jaat ji, góor ñi gàddu ko ca seen loos ya, bu dee ku baax la day wax naan: yóbbleen ma ngir li muy gis ci kanamam ci ay xéewal, bu dee ku bon la nag day yuuxu ci kàddu gu bon: wooy alku naa fan ngeen ko jëme?! Ngir li muy gis ci kanamam ci mbugal, léppay dégg kàddoom gi ba mu des nit, te bu ko déggoon day xëm ngir tarug li muy dégg